Bu ngeen déggalee àttey yoon yii, te sàmmoo koo jëfe, su boobaa seen Yàlla Aji Sax ji dina sàmm diggam ak yeen, kóllëre ak ngor, ga mu giñaloon seeni maam.
TSK
TSK · Proverbs 28:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ku bon a ngoog, di matu doomu ñaawtéef. Day sos njombe, wasin njublaŋ.
Waaye néew-dooleey jagoo réew mi; jàmm ne ñoyy, ñu bége.
Aji Sax ji du seetaan ku jub, di xiif, waaye day xañ ab soxor la mu xemmem.
Ku xelu denc këram ngëneeli alal aku diw, ab dof saax-saaxee josam.
Mat, mucc; dëng, dàll daanu.
¶ Léegi nag bokk yi, dama leen di ñaax, ràññeeleen ñi gàntal àlluwa ji ngeen jànge, di féewale, ak a téqtale, te ngeen moytu leen.
Ñooñu ay ndawi caaxaan lañu, ay liggéeykat yu njublaŋ yu mbubboo ndawi Almasi.
Doonte booba, ay nit ñu tuddoo bokki gëmkat ñoo yoxoosu ba tàbbi ci sunu biir, di nu yëddu, ngir luqatu ni nu moome sunu bopp ndax Almasi Yeesu mi nu gëm, te li ñu ci jublu di delloo nu ci buumi njaam.
Kàddu yu réy yu tekkiwul dara lañuy naxee, di fàbbee xemmemtéefi bakkan yu jéggi dayo, ay nit ñu yàggula rëcce ci ñeneen ñu nekk cig réer.