TSK

TSK · Proverbs 3:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

ndax seeni fan, ak seen fani doom, baree ca réew ma Aji Sax ji giñaloon seeni maam, ni kemu fan yi asamaan tiim suuf.

Yaa ko gatandoo barkey ngëneel, kaalaa ko wurusu ngalam.

te nga gis say sët. Yal na jàmm dal Israyil.

Baay digal ma, ne ma: «Jàppal samay wax ci sam xel, di jëfe samay santaane, ba dund.

Maay Xel mu Rafet, ku ma topp gudd fan, dund, dundati.

Su booba njekk ay jur jàmm, njekk ay dalal, di aare ba fàww,

¶ Gannaaw nag dees noo jox àtteb ñu jub ci kaw ngëm, jàmmoo nanu ak Yàlla ndax sunu Sang Yeesu Almasi.

¶ Kon Yàlla miy maye yaakaar, yal na leen feesale gépp mbég, ak jàmm ci biir ngëm, ba ngeen géejule yaakaar, ci manoorey Noo gu Sell gi.

Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ag njullite, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.