Ba Ibraayma àggee nag, da ne soxnaam Saarata ab jigéenam la. Abimeleg buurub Gerar daldi yónnee jëlsi Saarata.
TSK
TSK · Proverbs 6:29
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yàlla ne ko ca gént ga: «Waaw, xam naa ne li nga def du sa teyeef. Moo tax man it mayuma la nga laal ko, di ma tooñ.
¶ «Bul ànd ak jabaru jaambur, di sobeel sa bopp.
Daawuda yónnee, gëstu mbiram, ñu ne ko: «Xanaa du Batseba doomu Eliyam, jabaru Uri, Etteen bi?»
Ana lu waral nga ñàkke worma kàddug Aji Sax ji, di def lu mu ñaawlu? Uri Etteen bi, yaa ko fàdde saamar; jabaram nga jël, def ko sa jabar, moom nga fàdde ko saamaru Amoneen ñi.
Aji Sax ji sib na ku réy, da koy mbugal ci lu wér.
Lii, duma leen ko dumaa?» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Wii xeet, duma ko fey yoolam?»
«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.