Ay bés a ngi ñëw Yanqóoba saxi reen, Israyil moomooy tóor, law, ba feesal déndu àddinaak meññeef.
TSK
TSK · Romans 1:13
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Ba ñu agsee, dañoo woo mbooloom gëmkat ña, àgge leen mboolem na Yàlla def ak ñoom, ak na mu ubbilee jaambur ñi dul Yawut buntu ngëm.
¶ Xel mu Sell mi nag tere leena yégleji kàddu gi ca diiwaanu Asi, ba tax ñu jàlli biir diiwaanu Firisi ak Galasi.
Póol nuyook ñoom, ba noppi benn-bennalal leen jëf, ji Yàlla sottale liggéeyam ci biir jaambur ñi.
Sañumaa tudd lenn nag lu moy li Almasi sottale sama jëmm, ngir jaambur ñi dul Yawut déggal Yàlla, te muy lu mu sottale samay wax ak samay jëf,
Ndegam ci ñeneen, man duma ndawal Almasi, xanaa ci yeen boog, moom laa, ndax liy firndeel sama sasu ndaw ci Sang bi, yeen la.
¶ Léegi nag bokk yi, bugguma ngeen umple ci wàllu mayi Noowug Yàlla.
¶ Kóolute gu ma amoon ci ni ngeen nuy damoo moo tax ma naroona jëkka dikk ba ci yeen, ngir seen yiw mana yaar,
Nun, sunub damu dafa am kemu bu mu dul wees. Sunu kemu moo di déndub tool bi nu Yàlla sas, te ci biir tool bi lanu liggéeye, ba agsi ci yeen.
Ni leen xibaaru jàmm bi dikkale nag, ni la dikkale àddina sépp, te mu ngi meññ, di law, na mu ko dale defe fi seen biir, ca bés ba ngeen déggee lu jëm ci yiwu Yàlla, ba ràññee ko dëgg.
¶ Leneen lu nu dul noppee sante Yàlla, moo di lii: ba ngeen nangoo ci sunu làmmiñ kàddug Yàlla gi nu leen dégtal, te melul ni kàddug nit doŋŋ ngeen ko nangoo, waaye kàddug Yàlla gi mu doon ci lu wér, moom ngeen ko jële, te kàddu googu mooy liggéey ci seen biir, yeen gëmkat ñi.
¶ Bokk yi nag, buggunu ngeen réere mbirum way dawlu ñi, bay tiislu ni ñeneen ñi amul jenn yaakaar, di tiisloo.
Waaye Boroom bee ma dimbali, dooleel ma, ngir kàddu gi siiwe ci man, ba xeeti jaambur yépp dégg ko, te Boroom bee ma musal ci pàddum gaynde.