¶ Aji Sax ji dafa gis ne mbonu nit màgg na lool ci biir àddina, te fu mu mana tollu, lu bon rekk lay xinte ci xolam.
TSK
TSK · Romans 1:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
ba ngeen di làmbatoo digg bëccëg ni silmaxa di làmbatoo cig lëndëm. Dungeen sottal seeni mébét. Dees leen di néewal doole, di foqati seen alal rekk, bés bu nekk, te kenn du leen wallu.
Ki may sarxale jaajëf moo ma teral; ku topp yoon, ma won ko wallu Yàlla.»
Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.
Képp kuy tabax jëmmi tuur, doo tus, xërëm yooyu ñu safoo amul njariñ. Ñooñu ñu defi seede te gisuñu, yéguñu, muy seen gàcce!
Aji Sax ji dafa wax ne: «Ana sikk bu ma seeni maam gisal, ba tax ñu sore ma, di topp xërëmi neen, ba far neen?
Nitoo nit dim sannax, sore xam-xam: te képp kuy tëgg sa jëmmu tuur, yaa añe gàcce. Sa jëmmi weñ ji nga xelli, di neenug neen, noog bakkan, tus!
Maay def loolu ngir nanguwaat xolu waa kër Israyil, gi ma dëddu ngir seen mboolem kasaray tuur yi.”
te ñoom ñépp la ku bon di korandoo, diri leen ciy mbaalam, dajale ciy caaxam, ba tax ko di bég aka bànneexu.
Ndaxam lees mana xam ci Yàlla, leer na ci seen biir, nde Yàlla moo leen ko leeralal.
Yal na seeni gët giim, ba duñu gisati, yal nañu sëgg ba fàww.»
¶ Lii nag maa leen ko wax, te di ko biral ci turu Boroom bi: Ni xeeti yéefar yiy jëfe, topp seen xalaat yu tekkiwul dara, buleen jëfeeti noonu.
Xam ngeen ne yëf yuy wéy yu mel ni xaalis mbaa wurus, du moom lees leen jote ci seen dundinu neen wa ngeen donne ca seeni maam,
Ma ngay àddu ca kaw, naan: «Ragal-leen Yàlla te màggal ko, ndax waxtuw àtteem jot na. Kon nag jaamuleen ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak bëti ndox yi.»