Teewul Yuusufa bañ, ne soxnas sang ba: «Déglul, sama sang da maa jébbal lépp, ba topptootul dara ci kër gi.
TSK
TSK · Titus 2:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Yal na Aji Sax ji yool ku nekk njekkam ak kóllëreem, ndax Aji Sax jee la teg tey jii ci sama loxo, waaye maa buggula yékkati sama loxo ci kaw ki Aji Sax ji fal.
Ku dëggu ci réew mi, ma geesu, ngir fat ko. Te kuy wéye maandute, kookoo may liggéeyal.
Mu ne ko: “Téeméeri xàndiy diwu oliw.” Mu ne ko: “Sa kayit a ngi, toogal gaaw te bind juróom fukk.”
Te itam li ñuy sàkku ci ay saytukat moo di ñu jara wóolu.
¶ Fexeleen rekk ba di jëfe ni mu yelloo ak xibaaru jàmm bu Almasi, ngir bu ma leen seetsee, mana seede, mbaa su ma wuutee it, di dégg ni ngeen saxoo di mànkoo, bokk jenn yéene, di xeex ngir saxal ngëm gi sukkandiku ci xibaaru jàmm bi.
¶ Li ci des nag bokk yi, moo di lii: mboolem lu dëggu, ak mboolem lu tedd, ak mboolem luy njub, ak mboolem lu set, ak mboolem lu jekk, ak mboolem lees di rafetlu, ndegam lu nawlu la te yelloo ngërëm, na leen loola soxal.
¶ Mag ñiy jiite mbooloo mi bu baax nag, nañu leen yellale ag njukkal ñaari yoon, rawatina ñi boole coonoy waare ak njàngle.
¶ Waaye ku ciy jàngle leneen, te toppul kàddu yu wér yi tukkee ci sunu Sang Yeesu Almasi, toppul àlluwa ji dëppoo akug njullite,
Seen dundin ci biir jaambur ñi gëmul, rafetal-leen ko, ba su ñu leen waxaloon ne ay defkati lu bon ngeen itam, seen jëf ju rafet lañuy gis, te moom lañuy sàbbaale Yàlla, kera bésub dikkam.