Foofa ngeen di lekke, yeen ak seeni njaboot fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ngeen bége fa seen wépp ñaq wu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeelal.
TSK
TSK · Acts 2:46
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ngeen daldi bànneexu fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, yeen ak seeni doom, góor ak jigéen ak seeni jaam, góor ak jigéen, ak Leween ñi ci seen dëkk, ak doxandéem yeek jirim yeek jëtun ñi ci seen biir, ci bérab bi seen Yàlla Aji Sax ji taamoo dëël turam ëllëg.
Éy Aji Sax ji, won ma sa nammeel, ma doxe sa worma. Tënkal sama xol ci ragal la.
¶ Ba reer jotee mu toog ak ñoom ca ndab la, jël mburu ma, yékkati kàddug cant, daldi dagg, jox leen.
Ñu agsi, yéeg ca néegu kaw taax ma, fa ñuy dal naka jekk. Piyeer a nga ca, ak Yowaan, ak Yanqóoba ak Àndre, ak Filib ak Tomaa, ak Bartelemi ak Macë, ak Yanqóoba doomu Alfe, ak Simoŋ farlukatu moom-sa-réew ba, ak Yuda doomu Yanqóoba.
¶ Piyeer ak Yowaan ñoo doon duggsi kër Yàlla ga, ngir jullig digg njolloor.
Ci kaw loolu bés bu nekkaan, muy ca kër Yàlla, di ca biir kër ya, noppiwuñoo jàngle ak a xamle xibaaru jàmm bi yéene ne Yeesu mooy Almasi.
¶ Ca ndoortel ayu bés ba, naka lanu daje ngir dagg mburum bokkoo mi, Póol, yékkati kàddu, di wax ak gëmkat ñi, ndax fekk na mu bëggoona dem ca ëllëg sa. Wax ja nag law ba guddi ga xaaj.
¶ Bu ma yékkatee kàddug cant ba lekk sama wàll, ana lees may sikke ci aw ñam wu ma sante Yàlla?
¶ Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digg ak yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may.
¶ Yeen jaam yi, déggal-leen seen sangi àddina, ànd ceek ragal Yàlla bay kat-kati, ak xol bu dëggu. Ni ngeen déggale Almasi, nangeen leen ni déggale.