TSK

TSK · Acts 21:31

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba mu ko defee Adoña dégg ca, mook mboolem ña mu woo woon, ñu nekk faak moom. Fekk ñu lekk ba noppi. Ba Yowab déggee liit ga, da ne: «Waaw, riir mi ci dëkk bi, lu mu doon?»

Acts 17:5 TSK

¶ Yawut ya nag am ca kañaan, daldi foraatoo ca mbedd ma ay taxawaalukat, dajale ay gàngoor, ba yëngal dëkk ba. Ñu song kër Yason, di seet Póol ak Silas, ngir yóbbu leen ca waa dëkk ba.

Kon du yaay waayu Misra jooju yëngaloon dëkk bi ci fan yii, te yóbbu woon ñeenti junniy Bóomkat ya (4 000) ca màndiŋ ma?»

Póol woo kenn ca njiiti takk-der ya, ne ko: «Yóbbul xale bu góor bii ba ci njiital gàngoor gi, ndax am na lu mu ko wara wax.»

¶ Ca ëllëg sa Àggripa ak Berenis ànd ak topp mu ràññiku, duggsi ca ëttub àttekaay ba, feggook njiiti gàngoor ya, ak kàngami dëkk ba. Festus joxe ndigal, ñu indi Póol.

Xanaa ay surgay Almasi lañu? Naa ràkkaaju nag, te ne maa leen ko gëna doon. Bu dee ci liggéey yu metti, maa man fopp; bu dee ci fani kaso, maa ëpple fopp; bu dee ci ay yar, maa ëpple ay yooni yoon, te bare na lu ma riisu ndee, ba raw leen: