TSK

TSK · Daniel 9:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Aji Sax ji wax Musaa ne ko: «Dinga gis léegi ni may def Firawna: loxo bu ko ëpp dooleey tax mu bàyyi leen ñu dem. Bir na ne, loxo bu ko ëpp doole mooy tax mu dàq leen réewam.»

Waaye maa la musal, te li ma ci jublu moo di won la sama doole, ba sama riirum tur dajal àddina.

¶ «Na màggal googu di pàttliku ci yeen. Na mel ni màndarga mu nekk ci seen loxo ak seen jë. Su ko defee ngeen saxoo jàngle yoonu Aji Sax ji, ndax ci dooley loxoom la leen Aji Sax ji génnee Misra.

Na yooyu sarax mel ni màndarga mu nekk ci seen loxo ak seen jë, di leen fàttli ni nu Aji Sax ji génnee Misra ci dooley loxoom.»

Bu ma dumaa Firawna, boole kooki watiiram aki gawaram, ba doxe fa siiwal sama ndam, waa Misra dinañu xam ne man maay Aji Sax ji.»

Ndax kat ñooy sa ñoñ ñi nga séddoo, génnee leen Misra, taalu xellikaayu weñ gu ñuul ga.

Ñooy say jaam, sa ñoñ ñi nga jote sa kàttan gu réy ak sa doole ju bare.

Teewul Yàlla wallu leen ngir turam, ba xamle njàmbaaram.

Yaay gatandu kiy bége njekk gi muy jëfe te di ba xel say yoon, yi ñu mas di jaare, ba mucc. Waaye kat, yaa nu mere, ndax noo bàkkaar.

Ma bind kayitu njaay mi, màndargaale ko sama torlukaay, woo ciy seede, ba noppi natt diisaayu xaalis bi.

Bàkkaar nanu, ñaaw nanu, tooñ nanu, gàntal la, dëddu say santaane ak sa ndigali yoon.

Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la; yeyootumaa tuddoo sax sa doom.”

Moo nu wallu ci googu dee gu naroona metti, moo nuy walluwaat, te moom lanu yaakaar mu wallooti nu.