Digg bëccëg wees, ñu gëna ràkkaaju di wax ay waxyu, ba saraxu ngoon jot. Waaye du lenn lu àddu mbaa lenn lu wuyu mbaa lu leen faale.
TSK
TSK · Daniel 9:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba loolu amee mboolem ñi wormaal kàddug Yàllay Israyil daje, wër ma ndax ñàkk kóllëreg ña ñibbsee ca ngàllo ga. Ma toog, ne tott ba waxtuw saraxu ngoon.
def ngelaw yi say ndaw, ay sawara boy, di say jawriñ.
¶ Kenn ci malaakay seraf ya naaw wutsi ma, yor aw xal wu mu keppe ag ñiim, jële ko fa sarxalukaay ba.
Bindeef yaa ngay naaw, di dem ak a dikk, mel ni melax.
Bi muy wax ak man, dëpp naa sama kanam fi suuf, ba daanu leer. Mu laal ma, taxawalaat ma fa ma taxawoon.
Jekki-jekki jëmm ju mel ni nit dikk, laal samay tuñ. Ma ŋa, àddu, daldi wax ak ki taxaw sama kanam ne ko: «Sang bi, peeñu mi tax na ma jàq, ba amatuma benn doole.
¶ Piyeer ak Yowaan ñoo doon duggsi kër Yàlla ga, ngir jullig digg njolloor.
¶ Ca ëllëg sa, ñu dem bay jub dëkk ba, yemook Piyeer yéeg ca kaw taax ma ci digg bëccëg, ngir ñaan.
Malaaka yi la Yàlla wax ci ñoom ne: «Moo def ay malaakaam diy ngelaw, jawriñam ñooñu la def tàkk-tàkki sawara.»