te maay musal sama ñoñ ci musiba moomuy dal saw askan. Ëllëg firnde jooju dina am.’ ”»
TSK
TSK · Ezekiel 39:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Gannaaw loolu maay dëgëral boppu Firawna, mu topp leen, ba ma jaare ca siiwal sama ndam, ndax maay daan Firawnaaki xarekatam yépp, te waa Misra dinañu xam ne, man maay Aji Sax ji.» Musaa jottli leen ko, ñu def noona.
Ci kaw loolu ñu yónnee, woolu mboolem kàngami waa Filisti, ne leen: «Jëleleen fi gaalu Yàllay Israyil gii, mu dellu këram, lu ko moy dina nu rey, nook sunu askan wépp.» Booba tiitaangey ndee dajal na dëkk ba bépp, ndax loxol Yàlla bu diis lool ca seen kaw.
Guddeek bëccëg sa loxo diis gann ci man. Sama doole ŋiis ni ndox mu jaas upp. Selaw.
Aji Sax ji, yaa xàcci sa loxo, waaye yéguñu ko. Won leen ni nga nabe ci sa ñoñ, ñu rus, te sawaraay xoyom sa noon yooyu.
Kon dinaa fésal sama sellngay tur wu màgg, wi ñu teddadil fi biir yéefar yi, sama tur wi ngeen teddadil fi seen biir. Ci yeen laay fésale sama sellnga, yéefar yiy gis, ba xam ne maay Aji Sax ji. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.
Maay biralee noonu sama màggaay ak sama sellnga, maa niy xamlee sama bopp, yéefar yu bare di gis, ba xam ne maay Aji Sax ji.”»
Yeena koy gisal seen bopp, yeenay seede ne: “Màggaayu Aji Sax ji jéggi na kemu réewum Israyil.”