TSK

TSK · Leviticus 21:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ba ñu ca tegee lu tollook ñetti weer, ñu xamal Yuda ne ko, Tamar goroom ba, da doon jaay boppam, ba jaare ca ëmb. Yuda ne: «Nañu ko yóbbu, lakk ko, ba mu dee.»

Ku boole nit ak ndeyam jël leen jabar, def na lu bona bon. Dees leen di boole taal, lakk leen, moom ak jigéen ña, ndax mbon gu ni mel baña am ci seen biir.

Li nga ciy def ab takk mooy liy dikkal Ofni ak Fineyas, sa ñaari doom yu góor yii: Benn bés lañuy bokk dee ñoom ñaar ñépp.

Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu, way-gëmadi yaa ngay lox. Ana kan ci nun moo mana dal ak sawara suy xoyome? Ana kan ci nun moo mana dal ak taal yu yànj ya dul fey?

Maa ngii di yar seen askan, sëlëm leen sébbriit, mi jóge ci seen saraxi màggal, ñu tonniwaale leen ak sébbriit mi.

Kërug boppam nag, na ko yor yorin wu rafet, te na mana yar ay doomam ba ñu nangul ko te sédd ko cér bu mat sëkk.