TSK

TSK · Leviticus 7:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Góor gu xaraful, ndax nanguwula xaraf, dees na ko dagge ci biir xeetam, ndax sàmmul sama kóllëre.»

Diiru juróom ñaari fan, bu dara ci lawiir am fenn ci seeni kër, ndax képp ku lekk lu am lawiir, dees na ko dagge ci askanu Israyil, muy doxandéem mbaa doomu réew mi.

¶ «Su fekkee ne nit ki dafa laal lu sobewu, te seetluwu ko, lu mel ni rab wu daganul te médd, muy rabu àll mbaa ag jur, mbaa luy raam, kon sobewu na, tooñ na.

Waaye ku sobewu ku lekk ci yàppu jur gu ñu defal Aji Sax ji saraxu cant ci biir jàmm, kooku nañu ko dagge ci biir bànni Israyil.

Képp ku lekk lenn luy deret, dees na ko dagge ci biir bànni Israyil.»

¶ «Mboolem gunóor guy naaw tey doxe ñeenti tànk sibleen ko.

¶ Bu loolu wéyee Aji Sax ji wax na Musaa ne ko:

¶ «Te it képp ku bokk ci waa kër Israyil mbaa doxandéem yi ci seen biir, bu lekkee lenn luy deret, kooku lekk deret, man Aji Sax ji, dinaa ko noonoo te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil.

Képp ku def lenn ci yooyu ñaawtéef déy, kooku dees koy dagge ci biir bànni Israyil.

Man ci sama bopp dinaa noonoo nit kooku te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil, ndax li mu jël ciy doomam jox Moleg, di sobeel sama bérab bu sell tey teddadil sama tur wu sell.

Askanu Aaróona, genn góor gu ci bokk du lekk ci sarax yu sell yi, li feek muy ànd ak jàngoroy der juy law mbaa jàngoroy xelli, ba keroog muy set. Ku ci laal lenn lu laal ab néew ba sobewu, mbaa mu tuur wasal moom ci boppam,

¶ «Bu loolu weesee ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, dina sobewu diiru juróom ñaari fan.

Waaye yii, buleen lekk seen suux: lu ciy duññ doŋŋ, te we wi xarul, mbaa lu we wi xar, te duññul. Lu mel ni giléem ak njomboor ak daman, ndax dañuy duññ waaye seen we xarul. Yooyu daganul ci yeen.

Waaye lii ngeen dul lekk ci njanaaw yi: jaxaay ak tan, ba ca mu ñuul ma,

Kon nag nanga leen wax ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Yeen ngeen di boole yàpp ak deret di ko lekk, di wékki gët kasaray tuur, di tuur deretu jaamburi Yàlla, ba noppi di moom réew mi?