TSK

TSK · Proverbs 19:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

te nangulul Kayin. Kayin nag mer lool, ba ne fóññ.

Aaróona këf and ba Musaa wax, daw dugg ca biir mbooloo ma. Ndeke mbas ma tàmbali na ca biir mbooloo ma. Mu def ca and ba cuuraay, daldi defal mbooloo ma njotlaay.

Bàkkaaru ngisaane la déggadi yemool, ñaawtéefu bokkaale tollook reewande. Yaa gàntal ndigalu Aji Sax ji, Moom mu gàntal sa nguur.»

Mu ne ko: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw yaa bàyyi ku ma aayaloon bakkanam, sa bakkan mooy fey bakkanam te say bokk ay fey bokkam.»

¶ Naka la Alyaasa di wax, ndaw la ne jimeet, jëm ca moom. Ma nga naan: «Gis nga musiba mii Aji Sax ji wàcce. Kon ana lu may séentooti ci Aji Sax ji?»

Job 15:13 TSK

Ngay sippi Yàlla sa mer, di ko wax lu mel nii!

Neel tekk, xaar Aji Sax ji, yaakaar ko. Bu sa xol jóg ci kuy baaxle, tey lal ay pexe.

Nit ñi dinañu taxawaalu ci réew mi, boole njàqareek ub xiif, te bu ñu xiifee, ñéññ, téen, xool kaw, saaga seen buur, saaga Yàlla,

«Yeen nag ngeen ne: “Boroom bi, ni muy doxale jaaduwul!” Waa kër Israyiloo, dégluleen! Sama doxalin a jaaduwul, am seeni doxalin a jaaduwul?

Ci kaw loolu tàngooru naaj wu metti di lakk nit ñi. Nit ñi nag tuubuñu, sàbbaal Yàlla; xanaa di saaga Yàlla, ji dogal yooyu musiba.