TSK

TSK · Proverbs 3:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Waaye wattuleen, wattuleen seen bopp bu baax, bala ngeena fàtte mbir yi ngeen teg seen bët, ba du génn seenum xel seen giiru dund gépp. Te nangeen ko xamal seeni doom ak seeni sët.

¶ «Teral-leen seen baay, ak seen ndey, ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante, ndax ngeen gudd fan, ndax it ngeen baaxle ca réew ma leen seen Yàlla Aji Sax ji jox.

Kàddu yii ma leen di dénk bésub tey, na dëkk ci seen xol.

Li ma leen sant, man, bésub tey, mooy ngeen sopp seen Yàlla Aji Sax ji, di topp ay yoonam, di sàmm ay santaaneem, ak dogali yoonam, aki àtteem, ngir ngeen dund te yokku, seen Yàlla Aji Sax ji barkeel leen ca réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko.

Sa dogali yoon, ma tàqamtikoo, sa kàddu, ma fat ba fàww.

Xoolal sama coono te xettli ma; saw yoon déy, sàgganewma ko.

Doom, toppal yaru baay, te bul wacc ndigalu yaay.

Amal xel mu rafet akug dégg. Bul fàtte te bul moy samay wax.

Déggal! Soxna si, Xel mu Rafet a ngi woote, dég-dég di xaacu.

Lu ko moy mu naan, ba fàtte lu yoon tëral, xañ néew-ji-doole ju ne, àqam.

«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.