TSK

TSK · Romans 2:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ñu bon ñi Yàlla ne leen: «Lu ngeen di tari sama dogali yoon, di waxe sama kóllëre?

Xaj yu tiita tiit lañu, xamuñu suur, te ñooy sàmm yeey! Ñoom ñépp, kenn manu cee xam dara, seen yoonu bopp lañu topp, ak seen amin wu lewul.

Kàngamam yi ci biiram a ngi mel ni saafaandu yuy dogat am pàdd, tuur deret ja, di sànk ay bakkan ngir nangu alali boroom.

Seeni njiit, alalu ger lañuy àttee, seeni sarxalkat di feyeekuy jàngle, seeni yonent di weccikoo xaalis seenum ngisaane, te Aji Sax ji lañuy dëgërloo, naan: «Xanaa du Aji Sax jaa ngi ci sunu biir? Musiba du nu dab!»

Yeesu itam ne: «Yeen xamkati yoon yi itam, wóoy ngalla yeen, yeen ñi sëf nit ñi sëf yu ñu àttanul, te yeen ci seen bopp, seen benn baaraam sax du ci laal.

Mu ne ko: “Say wax laa lay àttee, surga bu bon bi! Xamoon nga ne nit ku néeg laa, di foqati lu ma dénkaanewul woon, di dajale lu ma jiwuloon.

Ñi xaraf ñoom ci seen bopp sax toppuñu yoon wi. Teewul ñu bëgg ngeen xaraf, ngir mana damoo seen màndargam yaram, yeen ñi ñu xarafloo.