TSK

TSK · 1 Peter 3:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Man ci sama bopp dinaa noonoo nit kooku te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil, ndax li mu jël ciy doomam jox Moleg, di sobeel sama bérab bu sell tey teddadil sama tur wu sell.

Maa leen di noonoo ba seeni noon duma leen, seeni bañ yilif leen. Dingeen daw te kenn dàqu leen.

Aji Sax jaa nga këram gu sell. Aji Sax jaa nga asamaan, kaw jalam, ne jàkk doom aadama, di ko seetlu.

Éy Yàlla, yaa jagoo cant fa Siyoŋ, yaw lees di jëfeel ab dige.

Aji Sax ji moo gis lépp, di xool ku baax ak ku bon.

Aji Sax ji day dëddu ab soxor, di nangu ñaanu ku jub.

«Demal jëli Yeremi, nga sàmm ko, te bu ko def dara lu metti. Lu mu la ñaan it, defal ko ko.»

Ana kuy xeeb bés bii lu tuut sottee? Nañu bége kay buumu beteex bi ñu gis ci loxol Sorobabel! «Juróom ñaar yii nag gëti Aji Sax jee, ñoom ñooy wër àddina sépp.»

Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, doole lay dale.