Ab dof bu meree, mu gaawa feeñ; ku teey, tanqamlu saaga.
TSK
TSK · 1 Peter 4:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Tontu te déggagoo, ndof la, ak ñàkk kersa.
Ci kaw loolu lépp nag, tegooleen cofeel; mooy xànc gi leen faste, ba seenug bennoo mat sëkk.
¶ Ci wàllu mbëggeel gi war ci biiri bokk, soxlawuleen ku leen ci bind dara, ndax yeen ci seen bopp, Yàlla tàggat na leen ci soppante,
Ndénkaane lii nag, li ko taxa jóg mooy luy yee ag cofeel gu bawoo ci xol bu rafet, ak xel mu dal, ak ngëm gu mucc jinigal.
¶ Li ci raw nag bokk yi, moo di buleen giñ, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu mana doon. Na seen waaw di waaw, seen déet di déet, bala ngeena tàbbi ci mbugal.
¶ Kon nag gannaaw setal ngeen seen xol, ndax dëgg gi ngeen déggal, ba tax ngeen am cofeel gu mucc jinigal, ci bokki gëmkat ñi, nangeen soppantee xol bu set, cofeel gu mat sëkk.