TSK

TSK · 1 Peter 5:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aana dem ba foofa, ànd ak naqaru xolam, di ñaan ci Aji Sax ji, tey jooy jooy yu metti.

Maay dajeek ngëneelu Aji Sax ji fi kaw suuf sii. Lii wóor na ma.

Jébbalul ci Aji Sax ji, dénku ci moom, mooy sottal.

Noon yee ma yendoo lakkal, bare lool di xareek man. Ku Màgg ki,

¶ Gannaaw loolu Yeesu ne ay taalibeem: «Moo tax ma ne leen, buleen seen bakkan jaaxal, ngir lu ngeen lekk, te it buleen seen yaram jaaxal ngir lu ngeen sol,

Ndax loolu lépp, xeeti yéefari àddina, ñoo koy tiisoo, te yeen, Baay bi xam na ne soxla ngeen ko.

Buleen jaaxle ci dara, waaye ci mbir mu mu mana doon, deeleen dikke Yàlla seeni soxla, di ko ñaan ak a dagaan te boole ci di ko sant.