TSK

TSK · 2 Kings 21:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Buleen defe noonu ak seen Yàlla Aji Sax ji, ndax mboolem lu seexluwu lu Aji Sax ji bañ, defal nañu ko seeni tuur. Seen doom yu góor ak yu jigéen sax, lakk nañu leen, defal leen seeni tuur sarax.

Ca tànki buuri Israyil la topp. Doomam ju góor sax def na ko sarax, lakk ko ngir tuur ya, di roy ñaawtéefi xeet, ya Aji Sax ji dàqoon ngir bànni Israyil.

¶ Moo dugal ba tey jëmm ja mu sàkkoon ngir tuur ma ñuy wax Asera, ca biir kër ga Aji Sax ji waxoon Daawudaak doomam Suleymaan ne leen: «Ci biir kër gii ci Yerusalem, gi ma tànne ci mboolem giiri Israyil, laay dëj sama tur ba fàww.

Amon di def nag li Aji Sax ji ñaawlu, la baayam Manase daan def.

Gannaaw ñoo ma dëddu, di taalal yeneen yàlla cuuraay, ngir merloo ma ci mboolem liggéey bu ñu defe seeni loxo, samam sànj mooy tàkk fi bérab bii te du fey.”

Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax, ji ngeen sàmmul dogali yoonam, jëfewuleen àttey yoonam, xanaa di jëfe aaday xeet yi leen séq.”»

Ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Ab dëkk a ngii buy tuur deret fi biiram, ba tax bésam di jubsi. Mu ngi sàkk ay kasaray tuur, di sobeel boppam.