2 Samuel 15:10
TSK
¶ Absalom nag yónnee ndéey. Ay ndaw yegge ko giiri Israyil gépp. Mu ne leen: «Bu ngeen di dégg liit gu jib rekk, ne leen: “Absalom falu na buur ca Ebron!”»
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Absalom nag yónnee ndéey. Ay ndaw yegge ko giiri Israyil gépp. Mu ne leen: «Bu ngeen di dégg liit gu jib rekk, ne leen: “Absalom falu na buur ca Ebron!”»
Cadog sarxalkat bi ak Yonent Yàlla Natan, nañu ko diw foofa, fal ko mu jiite Israyil. Su ko defee ngeen wal liit gi te yéene ne: “Buur Suleymaan, guddalu fan!”
Yoyada génne doomu buur ba, solal ko mbaxanam buur, jox ko kayitu doxalinu nguur ga; ñu fal ko nag buur, diw ko diwug pal. Ba loolu amee ñu tàccu, ne: «Guddalu fan, Buur!»
Moo nu tànnal céru suuf, muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp.
¶ Naka la Yeesuy dem, nit ñi di ko lalal seeni yére ca yoon wa.