¶ Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur.
TSK
TSK · 2 Samuel 16:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba Israyil dëkkee ca réew ma, am na bés Ruben dem tëdd ak Bilaa, nekkaaleb baayam; Israyil yég ko. Doomi Yanqóoba yu góor fukk lañu ak ñaar.
«Ruben, yaw mi ma taawloo, nga sosoo sama digg doole, sama ndoortel kàttan, yaa jëkke sut moos ci teraanga ak doole.
¶ «Ku dëkkoo sa soxnas baay, sa baay nga torxal. Ñoom ñaar ñépp dee rekk mooy seen àtte, te ñooy gàddu seen bakkanu bopp.
Akis nag amoon na kóolute ci Daawuda, ndax da doon wax ci xelam naan: «Kii de yóbbe na boppam mbañeel gu ko bokki bànni Israyilam bañ lool. Moo tax sama surga rekk lay doon ba fàww.»
¶ Amoneen ña xam ne Daawuda jéppi na leen lool. Ñu dem bindi ñaar fukki junniy (20 000) xarekat ca waa Siri ña dëkke Bet Reyob ak waa Siri ña dëkke Soba, teg ca junniy nit ñu bàyyikoo ca buuru Maaka, ak fukki junneek ñaar (12 000) ñu waa Tob.
Yonadab ne ko: «Dangay tëdd ci sa lal, wopp-wopplu, ba sa baay dikk, seetsi la, nga ne ko: βNa sama jigéen Tamar ñëw, may ma, ma lekk. Na ma toggal ci sama kanam, may gis, te mu sexal ma ci loxol boppam.β»
¶ Buur Daawuda nag ñibbi këram ga ca Yerusalem. Teewul fukki nekkaaleem ña mu waccoon ñuy topptoo kër ga, da leena boole denc ci genn kër, ñu di leen fa wattu. Mu yor leen fa, te dëkkootu leen. Dees leen faa denc ba keroog ñuy dee, ñu mel ni ay jëtun.
Buur Suleymaan ne ndeyam: «Nga ne! Adoña ngay ñaanal Abisag mu Sunem soxna? Tee nga koo ñaanal nguur gi far, nde mooy sama mag, ñaanalaale ko Abiyatar sarxalkat bi, mook Yowab doomu Seruya?»
Na ngeen doone woon alkànde ci biir xeet yi, yeen waa kër Yuda, ak waa kër Israyil, ni laa leen di walloo, ba ngeen doon barke. Buleen ragal. Góor-góorluleen.»