¶ Ca déwén sa Kedorlamer ak buur ya faroon ak moom, dem dàq Refayeen ña ca Àsterot Karnayim, ak Suseen ña ca Am, ak Emeen ña ca jooru Kiryaatayim,
TSK
TSK · 2 Samuel 21:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana fu nu jëm? Te sunu bokk ya demoon yoqiloo nu, ne nu waa réew maa nu ëpp, sut nu, dëkk ya réy te dàbblikoo ay tata yu àkki asamaan. Rax ci dolli, ay ponkal yu bokk ci askanu Anageen ñi lanu fa gis!»
Ay Refayeen lañu jàppe woon Emeen ñooñu ak Anageen ñi, teewul Mowabeen ñi di leen wooye ay Emeen.
Mennum Og buuru Basan doŋŋ moo muccoon ca ndesu Refayeen ñu ponkale ña. Lalam ba, lalu weñ gu ñuul la. Ma nga noonee ca Raba, dëkkub Amoneen ña. Guddaayu lal ba ci xasabu góor, juróom ñeenti xasab la, di ñeenti meetar ak genn-wàll, yaatuwaay ba, ñeenti xasab, di ñaari meetar.
Bantu xeejam bu mag baa nga saf mbaamum ràbb, ñawkay xeej ba di weñ gu ëpp juróom ñaari kilo. Gàddukatu pakkam baa ngay dox, jiitu ko.
Waa Filisti dikk, tasaaroo ca xuru Refayeen ña.
¶ Xare dellu amati ca Gaat. Jenn waay ju réya réy a nga ca woon, ku am juróom benni baaraam, loxo bu nekk, ak juróom benni baaraam, tànk bu nekk, lépp di ñaar fukki baaraam ak ñeent. Moom it ponkalum Rafayeen la woon.