TSK

TSK · Acts 13:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 9:20 TSK

¶ Ca saa sa la tàmbalee xamle Yeesu ca jàngu ya, naan Yeesu mooy Doomu Yàlla.

¶ Ba ñu génnee ca jàngu ba, dañu leena ñaan ñu baamtu kàddu googu bésub Noflaay ba ca topp.

¶ Ci kaw loolu ay Yawut yu jóge Àncos gu Pisidi ak Ikoñum, fexe ba fàbbi mbooloo ma, daldi dóor Póol ay doj, diri ko ba génne ko dëkk ba, yaakaar ne dee na.

¶ Ba bésub Noflaay ba taxawee, nu génn ca buntu dëkk ba, ca wetu dex ga, daldi fay gis bérab bu nu foog ne ab jullikaay la. Nu toog fa nag, di waxtaan ak jigéen ña fa daje.

Acts 18:4 TSK

¶ Ci kaw loolu bésub Noflaay bu nekk Póol di waare ca jàngu ba, di yee Yawut yi ak Gereg yi.