TSK

TSK · Acts 18:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak powum séy. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.

Ndax Póol daa fasoon yéeney teggi Efes, ngir baña yàgg diiwaanu Asi; booba day gaawtu, ngir màggalu Pàntakot man koo fekk Yerusalem.

Xanaa di saxoo dagaan ci samay ñaan, su ci Yàlla àndee, yoon wu jub wu ma mujj dikke ba ci yeen.

Waaye maa ngi dikk léegi ba ci yeen, ndegam soob na Boroom bi, ba nattal sama bopp manoore ju réy-réylukat yooyu am, te duy kàddu kese.

¶ Ma tëje fii nag, bokk yi, bégleen, yokkuleen ba mat sëkk, ñaaxanteleen, mànkooleen te jàmmoo. Su ko defee Yàlla miy Yàllay cofeel ak jàmm mooy ànd ak yeen.

Nanu jëm kanam, te moom lanuy def, ndegam soob na Yàlla.

¶ Coono yu la jëf ju baax yóbbe kat, ndegam da di coobarey Yàlla, moo gën coono yu la jëf ju bon yóbbe.