TSK

TSK · Acts 2:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ca jamono jooja xiif a amoon ca réew ma, ba tax Ibraam dem réewum Misra, toogi fa, ndax xiif bu metti la woon.

Su keroogee mbedd bawoo Misra ba Asiri, waa Asiri di dikk ba Misra, waa Misra di dem ba Asiri te Misra di jaamoondook Asiri.

Na fas buur, watiir fiddi, jàmbaar sàqi: waa Kuusoo waa Puut ak seeni pakk, ak waa Ludd ak seeni xala.

Dina aakimoo alali Misra, muy wurus, di xaalis ak mboolem gànjar. Waa Libi ak waa Kuus it dinañu ko nangul.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Ay askan ñooy dikkati, di waa dëkk yu bare,

Acts 6:9 TSK

Ba loolu amee ñenn ca jàngu ba ñuy wax jàngub waa Goreel ga, daldi jóg, di tàmbalee weranteek Eccen. Ay niti waa Siren a nga ca, ak waa Alegsàndiri, ak waa diiwaani Silisi ak Asi.

Acts 13:1 TSK

¶ Ca biir mbooloom gëmkat, ña woon ca dëkk ba ñuy wax Àncos, amoon na ay yonent ak ay jànglekat: ñuy Barnaba, ak Simeyon mi ñu dippee Ñuule, ak Lusiyus mi bawoo Siren, ak Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom Galile, ak Sóol.

Ba mbooloo ma tasaaroo, bare na ay Yawut ak tuubeen yuy jaamu Yàlla yu topp ci Póol ak Barnaba. Ñuy wax ak nit ñi, di leen ñaax, ngir ñu sax ci doyloo yiwu Yàlla.

Teewul Póol jàpp ne gannaaw Yowaan Màrk moomu moo leen waccoon ca Pamfili te àndul woon ak ñoom ci liggéey bi, yóbbaale ko warul.

Acts 18:2 TSK

Mu daje fa ak Yawut bu ñuy wax Akilas, fekk baax diiwaanu Pont. Muy sooga jóge réewum Itali, ànd ak soxnaam Pirsil, ndax Buur bu mag ba Këlódd moo joxe woon ndigal ne na Yawut yépp génn Room.

Ca guddi ga Sang bi feeñu Póol, ne ko: «Na sa xel dal. Ni nga ma seedeele ci Yerusalem, noonu nga ma wara seedeeleji ca Room.»

Ba bokki gëmkati Room yégee ne nu ngi dikk, ñoo nu gatandusi ba fa ñuy wax péncu Apiyus ak fa ñuy wax Ñetti dalu gan ya. Ba leen Póol gisee, daa sant Yàlla, daldi gëna sawar.

Moo tax, yeen waa Room itam, ma yàkkamti leena àggesi xibaaru jàmm bi.

Seeni néew da naan lareet ci péncum dëkk bu mag boobu ñuy misaale turu Sodom mbaa Misra, fa ñu reye woon seen Sang ci bant.