TSK

TSK · Acts 21:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye laata loolu lépp, yeen, dees na leen teg loxo, fitnaal leen, jébbal leen kuréli jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanami buur aki boroom dëkk ndax sama tur,

Acts 5:18 TSK

Ñu teg ndaw ya loxo, tëj leen ca kaso ba.

Teewul Yawut ya xiirtal tuubeen yu jigéen yi gëna ràññiku, ak kàngam yu góor yi ci dëkk bi. Ñu daldi bundxatal Póol ak Barnaba, génne leen réew ma.

Acts 14:5 TSK

Jaambur ñeek Yawut yi nag ànd ak seeni kilifa, di leen waaja mitital ak a dóori doj.

Acts 17:5 TSK

¶ Yawut ya nag am ca kañaan, daldi foraatoo ca mbedd ma ay taxawaalukat, dajale ay gàngoor, ba yëngal dëkk ba. Ñu song kër Yason, di seet Póol ak Silas, ngir yóbbu leen ca waa dëkk ba.

¶ Jant ya Galyon moomee diiwaanu Akayi, Yawut ya dañoo mànkoo, jógal Póol, jàpp ko, yóbbu ca àttekaay ba.

Loolu moo waral Yawut yi jàppe ma ca kër Yàlla ga, di ma fexee rey.