TSK

TSK · Acts 3:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

bu ñu waññikoo seen léppi xol, ak seen léppi jëmm ci yaw, foofa ca seen réewu noon ya leen jàpp, ba ñaan la, jublook seen réew ma nga joxoon seeni maam, jublook dëkk bi nga taamu, ak kër gii ma tabax ngir saw tur,

Mu jëm ci njiitu jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Muy kàddug Sabóor. Woyleen Aji Sax ji woy wu yees, moo def ay jaloore, kàttanam ak sellngay dooleem jox na ko ndam li.

Raxasuleen ba set wecc, jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam, te ngeen ba lu bon.

Nanga dërkiisal xoli askan wii, fatt seeni nopp, taf seeni gët; lu ko moy seeni gët gis, seeni nopp dégg, seen xol yég, ñu dëpp, wér.»

Maa far say moy, mu naaxsaay niw niir, say bàkkaar ne mes nib lay. Délsil fi man, jot naa la.»

Ñi Aji Sax ji goreel, nii lañuy dellusee, agsaaley sarxolle fa Siyoŋ, kaalawoo mbég mu sax, mbégteek bànneex wàllsi, naqar aku tiis daw.

«Yaw mi jaasir ba juroo, xaacul! Yaw mi xamul mititu mat, sarxolleel.» Aji Sax ji nee: «Ndaw si ñu foñ moo gëna jaboot kiy séy.

Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; teddngay Aji Sax ji fenkal na la!

Dees na xàmmee seen askan fi biir xeet yi, xàmmee lu meññe ci ñoom fi biir waaso yi; képp ku leen gis ràññee ne ñooy askan wu Aji Sax ji barkeel.

Yeen soppey Yerusalem yépp, bégandooleen ak moom, te di ko bànneexoo. Mboolem yeen ñi doon ñaawlu tiisu Yerusalem, bokkleen ak moom xolam bu sedd.

Maa dégg moos askanu Efrayim di binni naan: “Aji Sax ji, duma nga noo duma, ni sëllu wu dese tàggat. Ngalla waññi nu, nu waññiku; yaw Aji Sax ji, yaa di sunu Yàlla.

«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.

Bés yooyu ci jamonoom, maay jebbil njebbit lu jekk ci askanu Daawuda, muy jëfe njub ak njekk ci réew mi.

¶ «Lii moo tax yeen waa kër Israyil, ma di leen àtte, ku nekk ciy jëfam. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee. Dëppleen te dëddu mboolem seeni tooñ, ngir seenu ay bañ leena gàllankoor.

te nga wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jëleji bànni Israyil ca biir xeet ya ñu fekki, dajalee leen wet gu nekk, délloosi leen seen suufas bopp.

Ni ñu ko binde ci yoonu Musaa, ni la nu musiba moomu mépp dikkale, te tinuwunu la, yaw, sunu Yàlla Aji Sax ji. Dëdduwunu sunuy bàkkaar it te séddunu sa worma.

Israyiloo, dellul ci sa Yàlla Aji Sax ji, fakktaloo nga sag ñaawtéef.

Ngalla nanga sàmme saw yet sa ñoñ, sa gàtt yi nga séddoo, te ñu màkkaanoo gott bi ñoomu neen, fi digg parlu mu naat. May leen ñu fore àlli Basan ak Galàdd na jant ya woon.

Yaw janq Siyoŋ mu taaru, sarxolleel, Éey Israyil, xaacul, yaw janq Yerusalem mu taaru, bégal, te bànneexoo xol bu sedd guyy!

Luke 1:16 TSK

Niti bànni Israyil ñu bare, moo leen di waññi ci Boroom bi seen Yàlla.

Acts 1:6 TSK

¶ Naka lañu daje fa moom, daldi koy laaj, ne ko: «Sang bi, ndax ci jii jamono ngay sampaat nguurug Israyil?»

Acts 3:21 TSK

Moom la asamaan wara dalal, ba kera jamono ja lépp di dellu jag, na ko Yàlla waxe woon, yonent yu sell ya woon jottli.

Boroom bi nag gungee leen loxoom, ba ñu bare gëm, waññiku ci Sang bi.

Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndu suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay.

Xolu xeet wee dërkiis, seeni nopp fatt, ñu gëmm fatuus, ba seeni gët du gis, seeni nopp du dégg, seen xol it du yég, ba ñu tuub, ma wéral leen.”

Dina feeñ it ndax noflaay ba mu nuy booleek yeen ñiy dékku ab coono, sédde nu ko, kera bés bu Sang Yeesu feeñee, ànd ak ay malaakaam yu làmboo manooreem, wàcce asamaan.

Jaamub Boroom bi ndànk la war di jubbanti diiŋatkat yi, nde jombul Yàlla may leen ñu tuub, ba xam liy dëgg.

¶ Bokk yi, su amee ci yeen ku moy yoonu dëgg, keneen ku ko waññi,

¶ Soppe yi, lenn a ngii, buleen ko umple: benn bés ni junniy at la mel ci Boroom bi; junniy at mel ni benn bés ci moom.