TSK

TSK · Acts 4:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji nee: «Ayca, bind ko ci àlluwa, ñu gis! Rëdd ko cib téere, ngir ëllëg ak sibbir, mu dib seede ba fàww.»

“Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Yaw yaa yónnee ci sa turu bopp ay bataaxal ca askanu Yerusalem gépp, rawatina sarxalkat ba Cefaña doomu Maaseya, ak mboolem sarxalkat ya. Nga di ci wax ne:

Naka ngay xool, aw doj wu loxo sànniwul fàq, daldi dal ca tànki jëmm ja bindoo weñ ak ban bu ñu lakk, daldi koy rajaxe.

Amos 7:12 TSK

¶ Gannaaw loolu Amaciya ne Amos: «Yaw boroom peeñu mi, dawal, làquji réewum Yuda, nga waxe fa waxyu, am fa loo dunde.

Acts 4:21 TSK

Ba loolu amee ñu tëkkuwaat leen, door leena yiwi, ñu dem, gannaaw manuñu leena mbugal te amuñu bunt ci ñoom ndax mbooloo ma, te ñépp di màggal Yàlla ca la xew,

Acts 5:24 TSK

¶ Jawriñu kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya dégg loolu, daldi jaaxle lool ci ndaw yi, di xalaat nu mbir miy mujje.

Acts 5:39 TSK

Waaye su bawoo fa Yàlla nag, dungeen ko mana fanq, moytuleena jànkoonte ak Yàlla.» Ñu daldi fekksi Gamalyel,

Sañumaa tudd lenn nag lu moy li Almasi sottale sama jëmm, ngir jaambur ñi dul Yawut déggal Yàlla, te muy lu mu sottale samay wax ak samay jëf,

Yawut ñi ñoo rey Sang Yeesu, na ñu reye woon yonent yi, te ñoo nu bundxatal tey. Neexuñu Yàlla, te nooni ñépp lañu.