TSK

TSK · Acts 7:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Aji Sax ji moo waxoon Ibraam, ne ko: «Jógeel sam réew, jóge ci say bokk ak sa kër baay, te nga dem ca réew mi ma lay won,

¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji wax ko ne ko: «Man maay Aji Sax, ji la génnee Ur, ga ca Kaldeen ña, ngir may la réew mii, nga moom ko.»

Neleen bunt yi kulbét, ubbileen bunti cosaan yi, Buur Boroom ndam duggsi.

Aji Sax jeey àddu ca kaw ndox ma, Yàlla mu tedd maa dënu, Aji Sax jeey tiim ndox, mi ne màww.

Seen maam Ibraayma laa ne, moom ngeen di xool, xool ci Saarata mi leen meññ. Ba muy kenn laa ko woo, barkeel ko, ful ko.

Luke 2:14 TSK

«Daraja ñeel na Yàlla fa asamaan sa gëna kawe, jàmm ci kaw suuf ñeel ñi Yàlla baaxe.»

Acts 23:7 TSK

Naka la wax loolu Farisen yaak Sadusen ya tàmbalee werante, ba mbooloo ma xàjjalikoo.

Aji gëmadi ñooñu la Seytaane yàllay xarnu bii gëlëmal seenum xel, ngir ñu baña gis ceeñeeru xibaaru jàmm bu leeru Almasi, miy melokaanu Yàlla.

Kooku mooy lerxat leeru Yàlla, te mooy ki jëmmal nekkug Yàlla. Moo téyee lépp kàddoom gu manoorewu. Gannaaw ba mu setalee bàkkaar yi nag, fa ndijooru Aji Màgg ji la toog, fa kawte ya,

Ña ngay àddu ca kaw, naan: «Gàtt bi ñu rendi woon moo yeyoo kàttan ak alal, yeyoo xel ak doole, moo yeyoo teraanga, yeyoo darajaak cant.»