TSK

TSK · Acts 8:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Acts 1:8 TSK

Waaye Noo gu Sell gi mooy wàcc ci yeen, ngeen soloo dooleem, daldi doon samay seede ci Yerusalem, ak ci diiwaanu Yude gépp ak ci Samari, ba ca cati àddina.»

Acts 6:5 TSK

¶ Wax jooju daldi neex mbooloo mépp. Ñu seppi Eccen, nit kufeese ngëm ak Noo gu Sell gi, seppi Filib ak Porokor ak Nikanor ak Timon ak Parmenas ak Nikolas, ma dëkke Àncos te dib tuubeen bu duggoon lu jiitu ci yoonu Yawut.

Acts 8:14 TSK

¶ Ba ndaw ya ca Yerusalem yégee ne waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla, Piyeer ak Yowaan lañu fa yebal.

Acts 8:40 TSK

Filib moom, dëkk ba ñuy wax Asot la gisaat boppam. Mu wéye di xamle xibaaru jàmm bi ci dëkkoo dëkk, ba àgg Sesare.

Acts 17:2 TSK

Póol nag di leen fa fekk, na mu ko baaxoo. Diiru ñetti bési Noflaay, mu di leen waxal ci Mbind mi.

Nun nag, nuy waare Almasi bu ñu daaj ci bant, muy njombe ci Yawut yi, di ag ndof ci jaambur ñi dul Yawut.

Geneen kenu moom maneesu koo lal, xanaa gi xasa lale, te mooy Yeesu Almasi.