TSK

TSK · Amos 1:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Jenn waay a nga woon ca dëkk ba ñuy wax Mawon. Amoon na alal foofa ca dëkk ba ñuy wax Karmel; ku barele woon lool la, amoon na ñetti junniy xar ak junniy bëy. Mu nekkoon Karmel, di watlu ay xaram.

Buur mer lool, mel ni gayndee ŋar; boo ko merloo, dangay xaru.

Day tóora tóor, di bànneexu, bay sarxolle, ba jagoo darajay gottub Libaŋ ak taaru àllub Karmel ak Saron. Foofa lees di gise darajay Aji Sax ji, sunu taaru Yàlla.

Ba kañ la réew mi naa sereŋ, gàncaxu tooloo tool di lax? Rabu àll ak njanaaw a ngi sànku ngir mbonug ñi fi dëkk te naan: «Moom xoolul sunu muj!»

¶ Aji Sax ji teg ci ne ma: «Yaw nag, jottli leen mboolem kàdduy waxyu yooyu. Te nga ne leen: Aji Sax jeey yëmmoo fa kaw ni gaynde, fa màkkaanam mu sell ma lay àddoo, ŋara ŋar ci kaw déndu suufam, xaacu xaacuy dërkati reseñ, di ko gëdde mboolem waa àddina,

Maay dajeek yeen ni rab wu aay wu ñu xañi doom, maay xotti seen mbuusum xol, fa laa leen di yàppe ni gaynde, te rabu àll moo leen di xotat.

Joel 1:16 TSK

Xanaa du ag lekk a dagg, nuy gis, te mbég ak bànneex tukkee sunu kër Yàlla ga?

Amos 3:8 TSK

Bu gaynde yëmmoo, ana ku dul tiit? Ana ku saña baña biral waxyu, bu ko Boroom bi Aji Sax ji waxee?

Amos 9:3 TSK

Bu ñu nëbbu woon kaw tundu Karmel it, fa laa leen di fekk, yóbbu. Ñu làqoo ma ca taatu géej, ma sante fa jaani géej, mu màtt leen.