TSK

TSK · Amos 4:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Musaa ne ko: «Loolu du yoon, ndax li nuy rendil sunu Yàlla Aji Sax ji, waa Misra dañu koy xof. Te bu nu sarxalee lenn lu waa Misra xof, ñuy gis, dinañu nu dóor ay doj, ba nu dee.

Diiwaanu Gosen, ga bànni Israyil dëkkoon doŋŋ, moo mucc ca tawub yuur ba.

¶ «Bu loolu taxul ngeen déggal ma, maa leen di mbugal lu ko ëpp juróom ñaari yoon, feye leen ko seeni bàkkaar.

¶ «Waaye bu loolu weesee te déggaluleen ma, xanaa di ma noonoo ba tey,

¶ Asamaan si tiim seen bopp nag da naan sereŋ ni xànjar, suuf si ngeen teg seeni tànk, wow koŋŋ ni weñ gu ñuul.

¶ «Bu asamaan tëjoo, taw amul ndax tooñ gu ñu la tooñ, bu ñu jubloo bérab bii, ñaan la, sàbbaal saw tur te dëddu seen bàkkaar ndax sa mbugal,

Dama koy gental, mu saxi dég aki dagg, deesu ko tenqi, deesu ko bey; niir yeet, ma sant leen ñu bañ koo tawal.

Seen xel demul sax ba ne: “Tee noo ragal sunu Yàlla Aji Sax, jiy jot, mu tawal nu, taw yu jëkk ak yu mujj yi, àppal nu ayi bési ngóob, sédde nu?”

Réew mi tawluwul, suuf si fett, yaakaaru beykat tas, mu muuru, di tiislu.

Joel 1:10 TSK

Tool yi yàqu yaxeet, suuf sëngéem ciw tiis; pepp yàqu, biiñ bu bees wow, ag diw ŋiis.

Kon nag yeena tax asamaan téye ab layam, suuf téye meññeefam,

¶ Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye ba mu saxee ci ñaan ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diiru ñetti at ak genn-wàll.