Éy Aji Sax ji barkeelal dooley gii giir, te bége aw ñaqam. Dammal ndiggal ña koy jógal, ba ay bañam duñu jógati.
TSK
TSK · Amos 8:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba loolu amee mu teg wenn wëllu wa ca dëkk ba ñuy wax Betel, wa ca des mu tegi ko ca Dan.
xanaa walbatiku di sex dugub, di naan ndox ci bérab bi mu la waxoon ne la bu fi sex dugub, bu fi naan ndox, sab néew du fekki say maam ca seen bàmmeel.»
Omri nag dem ca Semer, jënde ca moom tundu Samari ci juróom ñaar fukki kiloy xaalis. Omri tabax ca kaw tund wa, dippee dëkk ba mu tabax Samari, mu dëppook Semer, turu boroom tund wa.
Ñi ma sam, yal na seen ayu làmmiñ këppu seen kaw bopp.
Ku ñuy àrtu, nga të ticc, dangay jekki yàqu, ba wees am paj.
¶ Aji Sax ji nag ne: «Wax leen ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil dafa wax ne: Naanleen ba màndi, di waccu, fëlëñu, tëë jóg ndax saamar bi may yebal fi seen biir.”
«Yeena ngi gànctu, yeen bànni Israyil, waaye na Yuda mucc ci googu tooñ. Buleen dugg Gilgal, buleen yéegi Bet Awen di giñ ci Aji Sax jiy dund.
Waa Samaree ngi am tiitaange ci sëllu wu ñu xelli ca Bet Awen, askan wa di tiislu tuur ma, ay xërëmkatam di lox ndax darajay sëllu, ji leen dëddu, dem ngàllo.
Fëlëñ! Israyil janq ba dootu jógati. Ma nga ñu wacc ca suufas réewam, te amul ku ko yékkati.
Bàkkaaru Yanqóobaa waral lii lépp, moyi Israyil googu la. Ana luy bàkkaaru Yanqóoba? Da dul Samari? Ana fuy bérabi jaamookaayi xërëm ci Yuda? Da dul Yerusalem?
di sàkku ay bataaxal yu ñeel jànguy dëkk ba ñuy wax Damaas, bataaxal yu yóbbante ndigal lu yeewlu képp ku ñu fa gis ku bokk ci Yoon woowu, góor ak jigéen, ngir mu jàpp leen, indi Yerusalem.
Ñenn ña nag të ticc, baña gëm, di ŋàññ Yoon wi ca kanam mbooloo ma. Ba loolu amee Póol bàyyi leen, daldi berook taalibe ya, bés bu nekk muy diisoo ak ñoom ca kërug jàngukaay gu Tiranus.
Lenn de man naa la koo nangul. Yoon woowu ñu ne mooy ngér mu sikk, moom laay topp, di ko jaamoo sunu Yàllay maam. Teewul mboolem lu ñu bind ci yoonu Musaa ak téerey yonent yi, gëm naa ko.