TSK

TSK · Amos 9:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Mu naa ca xelam: «Yàlla fàtte na, dummóoyu na, du xoolati.»

Ña nga naa: «Na Aji Sax ji gaaw! Na baral liggéeyam, nu gis. Na Aji Sell ju Israyil sottal mébétam, mu sotti, nu xam.»

Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu, way-gëmadi yaa ngay lox. Ana kan ci nun moo mana dal ak sawara suy xoyome? Ana kan ci nun moo mana dal ak taal yu yànj ya dul fey?

¶ Ba mu ko defee, mu am ñu ne: «Aywaleen, nu lalal Yeremi pexe. Ndax kat soxlawunu ko ba di ci ñàkk dara: du njànglem sarxalkat, du digley boroom xel te du waxyu bu yonent biral. Nanu ko duural ba sànk ko te baña faale lenn ciy waxam.»

Maay xettee fi seen biir ñi may gàntal ak ñi may tooñ. Réew ya ñu wàlliyaani, fa laa leen di jële, te réewum Israyil, duñu fa duggi. Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax ji.

Amos 6:1 TSK

Wóoy ña ne finaax ca Siyoŋ, wóoy ña naagu fa tundu Samari! Ñooy kàngami xeet wi gëna màggeey, niti Israyil di leen diis-si soxla.

Seeni njiit, alalu ger lañuy àttee, seeni sarxalkat di feyeekuy jàngle, seeni yonent di weccikoo xaalis seenum ngisaane, te Aji Sax ji lañuy dëgërloo, naan: «Xanaa du Aji Sax jaa ngi ci sunu biir? Musiba du nu dab!»

Su boobaa ci réew mi mépp, kàddug Aji Sax jee, ñaari xaaj yi lees di dagg, ñu sànku, ñetteel ba ca des lees fay wacc.

Moo tax nu ne nit ñu bew ñi ñooy ñi barkeel, ñiy def lu bon kay ñoo baaxle, ñoom ñiy diiŋat Yàlla, teg ca rëcc.”»