Bi nit ñi toxoo, jëm penku, dañoo gis ag joor ci réewu Sineyaar, ñu sanc fa.
TSK
TSK · Daniel 1:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana nu kenn di dàqe seen junni, ñaar di fëxal seen fukki junni, te ka ñu yaakaar jaayu leen, te Aji Sax ji, laa ne, waccu leen?
Ñu dog boppu Sóol, jël ay gànnaayam, ba noppi yeble ca réewum Filisti ba mu daj, ngir yégle ko ca seen këri tuur ya ak ca askan wa.
ba tax mu teg leen ca loxol yéefar ya, seeni bañ yilif leen,
Ana ku jébbal Yanqóoba futtikat yi, ku jox Israyil gii, sëxëtookat yi? Xanaa du Aji Sax ji nu tooñ? Ñoo baña topp ay yoonam, baña sàmm ndigalu yoonam,
Maay dikke mbugal Bel, tuur mi ci Babilon, yàbbiloo kob lancam. Xeet yi noppee def um wal, wuti ko, tatay Babilon it màbb.
Biiñ ba jay Baltacar, mu joxe ndigal, ñu indi ndab, yu xaalis yaak yu wurus ya baayam Nabukodonosor jële woon ca jaamookaayu Yerusalem, ngir ñu naane ca, mooki jaraafam aki soxnaam aki nekkaaleem.
Moo tax muy rendil mbaalam ab sarax, di taalal ab caaxam saraxu cuuraay, te naan moo niinal njëlam, duunal ab dundam.