TSK

TSK · Daniel 10:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Teewul Musaa ne ko: «Ngalla waay, yónnil keneen ku la soob rekk, sama Boroom.»

Mu laalale xal wi sama gémmiñ, ne ma: «Mu ngoog, ndegam lii laal na sa gémmiñ, sag tooñ wàcc na, sa bàkkaar faru na.»

¶ Ca kaw dénd ba tiim seeni bopp, ba tey, am na luy nirook ngànguney peru safiir, te jëmmu nit nekk ca kawa kaw lay nirook ngàngune.

Fekk na ngoon ga jiitu dikkam, Aji Sax ji teg ma loxo, ba tijji sama gémmiñ. Ba waa ja rëcc agsee fa man ca ëllëg sa ca suba, fekk na sama gémmiñ tijjiku, luuwatuma.

¶ «Fii la mbir mi yem. Man Dañeel nag, ma am njàqare lool, ba sama kanam soppiku, ma denc kàddu yooyu ci sama xel.»

Jibril dikk nag ba fi ma taxaw. Ba mu jegesee, ma tiit lool, ba daanu, sama kanam dëppu fi suuf. Mu ne ma: «Yaw doom aadama ji, nanga xam ne peeñu mii mujug jamono la.»

Maa ngay wax ci ñaan gi, waa ja Jibril ma ma gisoon lu jiitu ci peeñu mi, daldi naawa naaw, dikk ba ci man, yemook waxtuw saraxu ngoon.

Ba loolu amee ma des fa man rekk, ne jàkk ci peeñu mu réy moomu. Waaye deseetuma woon doole, damaa jeexal tàkk, amatuma genn kàttan.

¶ Maa ngi ciy dégg waaye xawma lu muy tekki. Ma ne: «Sang bi, ana nu xew-xew yooyu di mujje?»

Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.

Xanaa mu ŋacc boppam, nangoo jagoo nekkinu surga. Mu mujj mel ni nit doŋŋ, di ku ñu xàmmee jëmmu nitam.