Ay gaal ay jóge tefesu Kitim, néewalsi doole Asur, néewalsi doole Eber. Waaye ñoom it dañuy mujj sànku.»
TSK
TSK · Daniel 11:30
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Booba la ma leer ne ndeke Yàlla yónniwu ko, waaye Tobyaak Sanbalat ñoo ko fey ngir mu birale ma noonu waxyu, di ma fexeel.
Nee yeen waa Sidon ñi mel ni janq bu ñu tëdde, dootuleen xaxaloo. Ayca, dawleen jàlli ba dunu Sippar, te du tax ngeen am fa noflaay.
Ñu gorati garabu seen yu Basan, defare say joowu, kaw gaal gi, ñu defare ko banti sippar yu bawoo tefesi Géej gu mag ga, rafetale ko bëñi ñey.
Gannaaw gi buur bëj-gànnaar dina dellu réewam, yóbbaale alal ju takku. Dina fexeel mbooloom kóllëre gu sell gi, doora ñibbi réewam.
Kon nag yaw asamaan, bégal, yaak mboolem ñi ci sa biir! Waaye wóoy ngalla yeen géej ak jéeri! yeen, ñi Seytaane wàccaale mer mu tàng fi yeen, ndax xam ne fan yu néew a ko dese.»