TSK

TSK · Daniel 12:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Moo leen di aj ba ngeen tiim mboolem xeet yi mu sàkk, ci wàllu bayre, ak tur ak teddnga, te moo leen di def askan wu sell, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji, noonee mu ko digee woon.

Maay yékkati sama loxo jëme asamaan, giñ ne: “Ndegam maay dund ba fàww,

Dees na leen wooye “Askan wu sell wi,” “Ñi Aji Sax ji jot;” te yaw Yerusalem dees na la wooye “Ki ñu namm,” “Dëkk bi ñu waccul.”»

¶ Ba àpp ba matee, man Nabukodonosor, maa séentu asamaan, sama sago délsi. Ma sant Aji Kawe ji, sargal Kiy dund ba fàww, màggal ko: kilifteefam sax fàww, nguuram ñeel maasoo maas.

May xool, béjjén boobu di xareek aji sell yi, di leen daan,

Mu ne ma: «Àpp bi ñaari junni laak ñetti téeméer ciy guddeeki bëccëg. Gannaaw loolu dees na taxawalaat bérab bu sell bi.»

Li ko waral mooy buur bëj-gànnaar day dellu waajalaat mbooloo mu ëpp ma jiitu. Bu amee ay at dina dikkaat, ànd ak mbooloom xare mu mag ak ngànnaay lu takku.

Jamono ja ñuy dakkal sarax si wara sax fàww, di keroog ba ñuy taxawal lu siblu lay jur yàqute, junniy fan ak ñaar téeméer ak juróom ñeent fukk (1 290) dina ca topp.

Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.

¶ Ba mu ko defee malaaka, ma ma gisoon mu ŋarale géej geek jéeri ji yékkati loxol ndijooram, jëme asamaan.

¶ Gannaaw bu ñu seedee ba noppi nag, rab wiy jóge ci xóote bi mooy xareek ñoom, daan leen, ba rey leen.

Ñu jox ndaw si ñaari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, rëcc ninki-nànka ji, dem màndiŋ ma, ca rawtoom ba ñu koy leele lu tollook ñetti diir ak genn-wàll.