TSK

TSK · Daniel 2:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yuusufa ne ko: «Du ci man de, waaye Yàlla mooy baaxe Firawna pirim jàmm.»

¶ Mbir yi làqu daal, ñeel na sunu Yàlla Aji Sax ji, mbir yi feeñ nag, ñeel nu, nook sunuy doom ba fàww, te nu wara jëfe mboolem kàdduy yoon wii.

Job 26:6 TSK

Fàŋŋ la njaniiw def fa kanam Yàlla; du genn kiiraay gu ko làq paxum sànkute.

yafloo sa njël lu duun, sa xéewal wal, nga nàndale ko.

Su ma noon: «Na ma lëndëm mëdd boog, ba leer gi far guddil ma,»

Ana ku rafet xel nu muy mel? Ana ku xam piri? Am xel rafet, kanam leer, gëna lewet.

Ana ku yéene woon lii ca njàlbéen, ba nu xam ko? Ku ko yégle woon bu yàgg, ba nu man koo dëggal? Yéeneesu ko, yégleesu ko te déggeesul seeni kàddu.

Maay bind leer, di def lëndëm. Maay indi jàmm, di def safaan. Maay Aji Sax jiy def lii lépp!

Mu ne: “Woo ma, ma wuyu la, wax la lu réy te loq, loo xamul woon.”»

Waaye, Buur Nabukodonosor, Yàllaa ngi biir asamaan, di xamle ay mbóot te moo la won liy am jamono yiy ñëw. Sa gént gaak la nga ca gis ca sa kaw lal, lii la:

Dégg naa sab jëw, ñu naan noowi yàlla yaa ngi ci yaw, te gis nañu ci yaw ag ràññee akum xel ak xam-xam bu takku.

Luke 12:2 TSK

Mboolem lu nëbbu dees na ko feeñal, te lu làqu dees na ko xam.

Mooy noonu ñu binde rekk ne: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel daju ko, Yàllaa ko dencal ñi ko sopp.»

Moomu mbóot, xamaleesu ko woon doom aadama yi, ca janti maas ya woon, ni ñu ko feeñalale tey, ñu sell ñi diy ndawam ak yonent yi, ci ndimbalal Noo gu Sell gi,

Te it amul mbindeef mu làqu fi kanam Yàlla. Lépp a ne duŋŋ, ne fàŋŋ, muy gis, te moom lanuy waxal bés-pénc.