Naka la Yanqóoba gis kanamu Laban, daldi xam ne melatul, na mu meloon ci moom.
TSK
TSK · Daniel 3:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Bu loolu taxul ngeen déggal ma, maa leen di mbugal lu ko ëpp juróom ñaari yoon, feye leen ko seeni bàkkaar.
su boobaa man itam maa leen di noonoo, te it man ci sama bopp maa leen di mbugalaat lu ko ëpp fukki yoon ak juróom, feye leen ko seeni bàkkaar.
Mu teg matt ma ba mu jekk, daggat yëkk wa, teg ca kaw.
«Waaye boo toogee, boo génnee, boo duggee, xam naa, boo xadaroo sama kaw it, xam naa.
Buur ne ñokket, mer ba fees, bàyyi fa biiñ ba, dugg ca biir tóokëram. Aman moom, des fa, di tinu Lingeer Esteer ngir bakkanu boppam, ndax booba xam na ne su dee Buur rekk, njekkaram taxaw na.
Merum buur ndaw la, dee a ko yónni; ku rafet um xel, giifal ko.
Doj diis na, suuf dib sëf, waaye fitnay dof a ko raw.
¶ Nabukodonosor daldi mer lool, ba fees dell. Mu woolu Sadarag ak Mesag ak Abet Nego; ñu indi leen ba fa kanam Buur.
¶ Buur nag am mbégte mu réy. Ci kaw loolu mu joxe ndigal, ñu génne Dañeel kàmb ga. Ba ñu génnee Dañeel kàmb ga, gaañuwul fenn, ndax daa wóolu Yàllaam.
¶ «Maa leen ko wax, yeen samay soppe, buleen ragal ñu manul lu wees rey seen yaram, ndax gannaaw loolu dootuñu leen manal lu ko raw.
¶ Naka lañu dégg loolu, seen xol fuddu, ñuy yéyu ci kawam.