¶ Yuusufa teg ca ne Firawna: «Kon léegi sang bi, wutal nit ku muus te rafet xel, jiital ko ci réewum Misra.
TSK
TSK · Daniel 4:27
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Waaye reetaani noon laa ci ragal, lu ko moy seeni bañ juume ko, ba naan: “Sunu njàmbaar a!” te waroon ne: “Aji Sax jee def lii lépp!”»
Su nit ki nee Yàlla: «Jot naa samab añ, dootuma bàkkaar.
Maay àgge ay buur sa kàdduy seede, te duma rus.
Ku jiital ngor ak worma, Yàlla jéggal la; ku ragal Aji Sax ji, dëddu lu bon.
Moom moo ne: «Sama dooley përëg laa defe lii, maa xelu, ràññee; ba randal kemi suufi xeet yi, foqati seeni alal, dañ boroom jal ya niw yëkk, wàcce leen.
Dangaa yaakaaroon sa pexe yu bon, naan, «Kenn gisu ma!» Sam xel ak sa xam-xam a la wacc, ba tax nga naa: «Maa ko yor, man rekk.»
Ndax lii moo di koor gi ma taamu, ci bés bu nit kiy toroxlu? Koorug dëngal loos ni barax, lal saaku, sotti ab dóom, tëdd di ko ñaawloo? Loolooy seen koor, ci bés bu Aji Sax ji rafetlu?
du kenn ku mu néewal, xanaa ab tayle, mu delloo ku ko ameel, alalu jaambur it, foqatiwu ko, xanaa ku xiif, mu leel, ku rafle, mu wodd,
Waaye ku bon nag, bu dëddoo mbonam ga mu nekke, di def njub ak njekk, moom moo musal bakkanu boppam.
Réewum Misraay gental, di ndànd-foyfoy, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji. Moo ne: ‘Dex gi maa ko moom, man maa ko sàkk!’
¶ Yeena ngi damu ca dëkk ba ñuy wax Lodebar (mu firi Amul njariñ) te naan: «Xanaa du sunu dooley bopp lanu nangul sunu bopp dëkk bu am doole ba ñuy wax Karnayim (mu firi Ñaari béjjén)?»
Jàll, wéy lañu cay teg ni ngelaw, tegoog tooñ, te seen doole di seen yàlla.»
Ana dëkk bu xumb ba dëkke woon kaaraange, te naan cim xelam: «Man rekk a, du keneen»? Nan la doone nii ab gent, bérab bu rab yiy goore, mboolem ku fa jaare, ub gémmiñam, jalu.
Li ci biir kay ngeen di sarxe! Su boobaa seen lépp ay set.
Ku jullite la woon te ragal Yàlla, mook waa këram gépp; bare woon na sarax yu muy yéwéne askan wi, te ñaan ci Yàlla la saxoo woon.
Waaye li dale Damaas ak Yerusalem ba ci réewum Yawut gépp, ba ca ñi dul Yawut, ñoom ñépp yégal naa leen seen wartéef, muy tuubeel ak waññiku ci Yàlla, ak jëf ju tuubeel yellool.
Ci Almasi Yeesu mi nu gëm, xaraf ak ñàkka xaraf, dara amu ci solo; li am solo mooy ngëm, gi jëfi cofeel di firndeel.
¶ Meññeefum Noowug Yàlla nag moo di: cofeel, ak mbég, ak jàmm, ak xolu muñ, ak mbaax, akug tabe, ak ngëm,
Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yeen bàkkaarkat yi, raxasleen seeni loxo, yeen ŋaralekat yi laa ne, setal-leen seen xol.