TSK

TSK · Daniel 4:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Bi nit ñi toxoo, jëm penku, dañoo gis ag joor ci réewu Sineyaar, ñu sanc fa.

ba tey, day dee, fekkiy maamam, ña dootu gis ug leer ba fàww.

Naa sant Aji Sax ji ci saa xol bii! Aji Sax ji sama Yàlla, yaaka màgga màgg. Teddngaak daraja nga soloo,

Mu ngi naan: «Xanaa du sama jawriñ yépp a diy buur?

«Yaw nit ki, waxal Boroom Tir, ne ko: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Dangaa fuuy ba naan: ‘Maay Yàlla, ji tooge toogub yàlla yi, fi xolu géej!’ Waaye yaw doom aadama nga, doo Yàlla, dangay yàlla-yàllalu rekk.

¶ «Buur, Yàlla Aji Kawe ji daa joxoon sa baay Nabukodonosor nguur gi, muy ku màgg, am ndam ak daraja.

«Xol baa ngay xoggliku, te ag njub nekku ca, waaye ku jub ndax kóllëreem mooy dund.

Luke 14:9 TSK

Su boobaa moom mi la woo, woo ko, mooy dikk, ne la: “Mayal kii, mu toog.” Nga am nag gàccey walbatiku toogi fa gëna gannaawe.

¶ Kon nag su ngeen di lekk, mbaa ngeen di naan, mbaa ngeen di def leneen, lépp lu ngeen di def, wutleen koo terale Yàlla.

Dëkk bu mag ba xar ñett, dëkk yu mag yu askani àddina yi màbb. Babilon gu mag ga nag, Yàlla bàyyi ko xel, ngir nàndal ko kaasu biiñu sànjam muy bax.

Fu sore lañuy dànd, ndax ragal toskarey dëkk bi, te naan: «Wóoy, wóoy ngalla dëkk bu mag ba! Babilon ma ca doole ja! Ci wenn waxtu rekk la sa àtte dikk!»

Askani àddina, leeru dëkk bi lañuy doxe, buuri àddina di fi indi seen teraanga.