TSK

TSK · Daniel 4:35

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Samiyel wax ko lépp, nëbbu ko ca dara. Eli ne: «Mooy Aji Sax ji. Li ko soob, na ko def.»

Job 9:12 TSK

Kii, bu këfee, ana ku koy tere? Ana ku ko naa: «Looy def nii?»

Job 33:12 TSK

Foofu déy, moy nga dëgg, ma wax la ko, Yàllaa sut doom aadama.

Job 34:19 TSK

Kii du far kàngam, du teg ku am ci kaw ku ñàkk, nde ñoom ñaar la boole sàkk.

Job 40:2 TSK

Yaw miy layook Aji Man ji, dangay diiŋat? Yaw miy weranteek Yàlla, doo tontu?

Job 42:2 TSK

Xam naa ne lépp nga man; du lenn loo tële.

Jal ba mu tooge lay niire waa àddina sépp.

Te yaw sunu Yàlla, yaa ngi asamaan, di def lu la soob.

Nit xeluwul, amul ug dégg ak pexe, ba manal Aji Sax ji dara.

Xol laa lay sàkkoo guddi, sama jëmm jépp di la laaj. Bu say àtte teewee fi kaw suuf, waa àddina xame ca njekk.

Moom moo tooge kaw wërngalu suuf, ñi ko dëkke mel niy soccet, moo tàllal asamaan ni ndimo, firi ko nib xayma, dëkke.

Wóoy ngalla kuy diiŋat ka la tabax te di ndabal xandeer ci biir ndabi xandeer! Ana ban ak di wax tabaxkatam, naa ko: «Looy def nii? Yaw amulooy loxo.»

Acts 5:39 TSK

Waaye su bawoo fa Yàlla nag, dungeen ko mana fanq, moytuleena jànkoonte ak Yàlla.» Ñu daldi fekksi Gamalyel,

Gannaaw nag Yàllaa leen jagleel genn may, ga mu nu jagleeloon, ba nu gëmee Sang Yeesu Almasi, ana ku ma doon, man, bay gàllankoor Yàlla?»

¶ Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma, ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!

ba turu Yeesu tax ñépp sukk seen bëti óom, muy kaw asamaan, di kaw suuf, di biir suuf,