TSK

TSK · Daniel 5:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ci biir loolu mu rafetook moom, jox ko cér bu sut cér ba mu jox yeneen buur ya mu bokkal curga ca Babilon.

Bul gaawa won buur gannaaw; bul saxoo lu buur buggul; Buur, lu ko neex lay def.

Man maa sàkk suuf, sàkk doom aadama ak mala fi kaw suuf ci sama doole ju bare ak sama kàttan gu matale, te loolu lépp, maa ko jox ku ma neex.

¶ Yéenekat ba nag xaacu, ne: «Dégluleen li ñu leen sant, yeen waa mbooloo yépp ak xeet yépp, ak làkk yépp.

ba noppi mu sant ay dag yu am kàttan ci mbooloom xareem, ngir ñu yeew Sadarag ak Mesag ak Abet Nego, sànni leen ca biir taal bu yànj ba.

Buur de, garab googu yaw la. Yaa màgg, di bare doole; di màgg ba laal asamaan, sa kilifteef àkki cati àddina.

Mbooloo moomu dees na leen faagaagal, buur bëj-saalum di ca réy-réylu. Dina rey ay junniy nit nag, waaye du ko taxa am ndam.