TSK

TSK · Daniel 6:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ndax man kat dañu maa sàcce ca réewum Ebrë ya, te fii itam, defuma fi lu tax, ñu war maa tëj.»

Daawuda neeti: Aji Sax ji ma musal ci pàddum gaynde ak weneen rabu àll wu aay, moo may musal ci loxol waa Filisti bii.» Sóol ne Daawuda: «Demal boog, yal na Aji Sax ji ànd ak yaw.»

daldi cay teg ne ko: «Sang bi, looy toppe nii sab jaam? Ana lu ma def? Lan laa def ci lu bon?

Mu dem fekk néew ba ne lareet ca yoon wa, mbaam maak gaynde ga taxaw ca wet ga. Gaynde ga lekkul néew ba, fàddul mbaam ma.

Muy woyu njàmbat, ñeel Daawuda. Mu woyaloon ko Aji Sax ji ci mbirum kàddu yu tukkee woon ca Kuus, ma bokkoon ci giirug Beñamin.

Aji Sax ji, maay jàpp ci biir mucc ayib, di wër sa sarxalukaay,

Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu, musal ko fu mu jàqe.

Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.

Yaa di sama Yàlla, ma di la sant; céy sama Yàlla, dama lay kañ.

Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.

¶ Ba mu ko defee saytukat yaak jawriñ ya ànd rungumloo ba ca Buur, ne ko: «Buur Daryus, guddalu fan!

Sama Yàlla yebal na malaakaam, mu tëj gémmiñi gaynde yi, ba defuñu ma dara. Ndax kat mucc naa ci tuuma sama digganteek moom ak sama digganteek yaw it, te defuma dara lu bon.»

¶ Naka la xelum Piyeer délsi, mu daldi ne: «Léegi nag xam naa xéll ne, Boroom bee yebal malaakaam, te moo ma musal ci loxol Erodd, ak mboolem li Yawut yi séentu woon.»

Acts 25:8 TSK

¶ Ci kaw loolu Póol weddi tuuma yi, ne: «Muy yoonu Yawut yi, di kër Yàlla gi, di Buur bu mag bi Sesaar, tooñuma ci kenn.»

¶ Li nuy damoo nag moo di seede bi nu sunu xel mu dal seedeel, ne xol bu set ak jikko ju dëggu ju bawoo fa Yàlla, mooy li nu doxale ci àddina si, rawatina sunu digg ak yeen, te du lu nu sunu xam-xamu nitu neen may, waaye yiwu Yàlla moo nu ko may.

Ñooñu ngëm lañu tege loxo ay nguur, ngëm lañu defe njekk, ci kaw ngëm la ay dige sottee, ñeel leen, te ci lañu tëje gémmiñi gaynde ya.