TSK

TSK · Daniel 9:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kon nag Sang bi, may ma xel mu am ug dégg mu ma àttee sa ñoñ, ngir may ràññee lu baax ak lu bon. Ndax kat, ana kan moo mana àtte sa ñoñ, wii askan wu réy?»

Job 12:17 TSK

Keey futti kàngam, dofloo kilifa.

«Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ, ak di faral ku bon? Selaw.

Ci samay pexe la njiit di saytoo, ñook kàngam yeek ñiy àtte dëgg ñépp.

Maay dëggal sama kàddug jaam, di sottal sama ndéeyal ndaw. Maa naan ci Yerusalem: “Dees na ko dëkke,” dëkki Yuda, ma ne: “Dees na leen tabaxaat, ma dekkali gentam bi.”

«Demal nga wax Ebedd Meleg, Kuuseen ba, ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Maa ngi nii di sottalsi sama kàddu yi jëm ci dëkk bii, muy ayam te du doon jàmmam. Dina am ngay gis, bésub keroog.

Yeen mboolem ñiy jaare yoon wi, lii safu leen, waaye seetleen rekk ba gis ndax wenn mitit dab na mitit wi ñu ma teg, te Aji Sax ji naqarale ma ko ci jantub tàkktel sànjam.

Aji Sax jee def la mu nammoon, moo sottal kàddoom ga mu santaane woon janti démb. Moo fàdd te yërëmul, ba may noon bége leen, te moo kaweel sa kàttanu bañ yi.

Maay def fi seen biir lu ma masula def te duma defati lu ni mel, ndax seen mboolem jëf ju siblu.

Joel 2:2 TSK

Bésub lëndëmu xàmbaari guddi gu ne këruus, mbete bànqanoos bu lale ci kaw tund yi. Gàngoor gu mag te am doolee ngi, gu ni mel masula am mukk, te dootul am feeki at, ba maasoo maas.

Teewul sama kàdduy àrtu ak sama dogali yoon ya ma yóbbante woon sama jaam ña, yonent ya, du lépp a dab seeni maam? Ñu dëpp nag daldi ne: “Noonee Aji Sax ji Boroom gàngoor yi nammoona def ak nun, feye nu ko sunuy jikko ak sunuy jëf, noonu la def ak nun.” »

Dama leen di wax ne leen, bëgga fésal ne Yàlla ku dëggu la moo waral Almasi dikk, def boppam jawriñu Yawut yi, ngir sottal dige ya Yàlla digoon seeni maam.