Aji Sax ji daldi wax ne: «Manumaa bàyyi nit, muy wéyee dunde noo, gi ma ko may, ndax nit du dara lu dul suuxi neen, kon dinaa leen àppal diirub téeméeri at ak ñaar fukk (120).»
TSK
TSK · Exodus 4:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moo tax maay xàcci sama loxo, ba dumaa waa Misra ay mbugali mbugal yu kéemaane yu may def ci seen biir. Su ko defee dina leen bàyyi, ngeen dem.
Terewul Firawna të, faalewu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
Ñeengokat ya ne Firawna: «Lii de Yàlla rekk a ko man!» Teewul Firawna wéye të rekk, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.
Firawna të rekk, baña bàyyi bànni Israyil, ñu dem, muy la Aji Sax ji waxoon, Musaa jottli.
Musaa ak Aaróona def nañu yooyu kéemaan yépp ca kanam Firawna, waaye fekk na Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, ba mu të, baña bàyyi bànni Israyil, ñu génn réew ma.
Aji Sax jee dëgëral boppu Firawna buuru Misra, mu toppi bànni Israyil, fekk bànni Israyil ñoom, ña ngay génn réew ma ci seen teeyu bakkan.
¶ Siwon buurub Esbon nag nanguwu noo may nu jaare fa moom, ndax booba seen Yàlla Aji Sax ji moo dëgëral boppam, wowal xolam, ngir teg ko ci seen loxo niki bésub tey jii.
mu xiir waa Misra ci dëddu ñoñam, ñuy fexeel jaamam ñooña.
Aji Sax ji, loo nuy wërloo fu sore say yoon, di nu dërkiisal, ba ragalatunu la? Sang bi, délsil ngir nun, sa giir yii nga séddoo.
¶ Gannaaw ràññee Yàlla jaralu leen dara, Yàlla it bërgal leen ak seen xel mu doyadi, ba ñuy def jooju jëf ju jekkadi.
Noonu lees binde ne: «Yàlla moo leen jox xelum ngëmment, ak bët yu dul gis, ak nopp yu dul dégg, ba bésub tey jii.»
ak mboolem xeeti naxe yu njubadi lal, ñeel ñi nara sànku ndax ñàkka sopp dëgg gi, ngir nangu ko ba mucc.