TSK

TSK · Genesis 10:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Lẽe bu bawoo Misra lañu ràbb ba mu jekk, def ko ndimoy wiiru gaal gi, nga raayawoo ko, cuub gu baxa ak cuub gu xewar bawoo dunu Elisa, di sa malaan,

Waa Geres ak Tubal ak Meseg di say jula, di leen indil ay doom aadama ak ndabi xànjar yu ñuy weccikoo seen koom.

«Yaw nit ki, neel jàkk Gog ma ca réewum Magog, boroom Meseg ak Tubal, te nga biral waxyu fi kawam.

ba bàyyikoo sa màkkaan, ca catal bëj-gànnaar, yaak xeet yu bare yu ànd ak yaw, ñoom ñépp war fas, di gàngoor gu mag, mbooloo mu bare.

mu dikk, naxsi askani ñeenti colli àddina, yi ñuy wax waa Gog ak Magog. Mu dajale leen ngir xare, ñu bare ni feppi suufas géej.