TSK

TSK · Genesis 13:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Askanu Teraa mooy lii. Teraa mooy baayu Ibraam ak Naxor ak Aran. Aran mooy baayu Lóot.

Gannaaw loolu mu yiwi ay magam ne leen: «Ngalla buleen xuloo ci yoon wi.» Ñu daldi dem.

Tont lu neex day giifal, baat bu ñagas di jógal xol.

Moytuw ay, ndam la; dof boo gis day bëgg xuloo.

Acts 7:26 TSK

Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, di leen jéema jubale, ne leen: “Yeen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di lorante?”

Ab gëmkat daal mooy yóbbu mbokkum gëmkatam ci yoon? Te loolu ci kanam aji gëmadi ñi sax lañu koy defe far!

¶ Mboolem lu ngeen di def nag, buleen ci boole xultu mbaa xuloo,

¶ Sàkkuleen jàmm seen diggante ak ñépp, te it sàkkuleen sellnga, nde ku sellul du gis Boroom bi.

¶ Waaye xel mu rafet ma bawoo fa kaw, set la jëkka def, teg ci ànd ak jàmm, akug dal. Day taxa neexa jubool, feese yërmande, di meññ jëf ju baax, te mucc ci par-làqu akug jinigal.

Ñépp nag ngeen di teral; mbooloom gëmkat ñi, soppleen leen; Yàlla, ragal-leen ko; te buur, teral leen ko.

Waaye li ci raw mooy soppanteleen cofeel gu mat sëkk, ndax cofeel, bàkkaar yu bare lay far.